Xereñ rek doyul...
Lii de as laac wu nu laajoon kaangfoore yi yàgg na.
Wànte ba leegi daal jota gu ma tontu wu dal sama xel.
Moone de laac wi jafewul. Kan moo mën a firi lii:
> Su xel gudd ee yoon gàtt # Su yoon gudd ee xel gàtt
![]() |
Xereñ rek doyul....
Mbir ma fa mu dàmme bokk na ci li koy saafara: "njàng muy xamal ag mënal ". Te nak loolu fa muy tàmbalee mooy "nàngu" ... Te "nàngu" boobee du mën a am ludul nu càmbaraat mbir mi be nga xam ni di na nu mën a jiital ña nu "tarbiya" "tarxiya" leen ... daldi leen "tasfiya". Wànte leegi moom ba "démocratie" duggee ci kurél gi ba leegi, ñi ci ëpp da nu jàpp ni ci wàll yëpp "démocratie" googee da fa fay dox. Loolu bokk na ci li rééral li ci ëpp ci askan wi.