fàttaliku‎ > ‎

Mannheim-2012

publié le 25 juil. 2017 à 21:56 par Fall Papa Oumar

Li ma nàmm ci mbir mi mooy biral jokkalànte bi te diko jaarale ci li Senegaal wane ci wàll woowu. Ndax lu ëpp ci li may wane maa ngi ko sose Senegaal, ci diggànte 1993 ba 1995. Ñareeli pàccu wane waa ngi taftalu ci li may sos ci jamano jii ci wàllu jokkalànte bi ci digànte diine yi. Damay duggaat ci soseeli  xel  yu jëkk  ya yu doomu Aadama, ca jamanoy mamaati maam ya ci yu sunu yoonu Yàlla. Li ma ci bëgg, fi itam, mooy wane ab xeetu jokkalànte (bu nu yëg ag bu nu yëgul) jamano yooyu ba léegi, ci digànte askanu àddina bépp .


Mbir mi dëg-dëg mooy gëstu màndarga yi ak feeñeelu diine yu wuute yi ngir wane digànte doomu Aadama ak mbiri baatinam. Dama bëg, ci loolu, woote jëmale ci kune weg sa morom ci wàllu ngëm- ngëmam ag diineem.


Li am solo ci doxalin woowu, ci sama gis-gis, mooy dindi bépp xeetu nooteelu xalaat ci jokkalànte bi , maanaam di fexe ba kenn du fesal sa bopp ci mbir mi. Ndax bu ñu bàyyee suñu xel ci li waral jokkalànte bi, dina ñu gis ne ndono bu ñu bokk la… moomeelu doomu Aadama yëp la, ñu koy wane te di ko nekkal ba àdduna sosoo ba léegui… ci ay kuréel wala ci nu ko waay mana defe.

Pàppa Umar Faal

© Maître Pofrima


Comments