publié le 23 sept. 2019, 08:26 par Fall Papa Oumar
| - Maam Yàllaa ma jox dugub ni ma soqal ma
- May soq, saxaar ni ma gis naa la
- Su dugub ñoree, su dugub ñoree
- Duma àbbi tame
- Duma àbbi layu
- Ndaat téll laa koy laye
- Ndax mu sakkan
- Ma yëngël taat, ma yëngël taat
- Ndax mu sakkan
- Bii taat Ndar la dëkk
- Ki koy riij Ndar la dëkk
- Bii taat woto àttanu
- Saxaar moo koy diri
- Bii taat day àbbi tame di riij soow
- Bii taat day àjji ridó di aj beeco
- Bii taat ku mu nob sa jëkkër
- Sa gat xar na
| [Corpus TAASU] |
publié le 23 sept. 2019, 07:50 par Fall Papa Oumar
| - Naka la ñuy sëye ?
- Awu leen ma naka la ñuy sëye ?
- Jeeg bu sëy te nara sëy dëgg
- Laaj leen ma nu muy sëye
- Fóotal goro, yakkal goro
- Waxtaan ak ub njëkke
- Waaye nag jeeg buy sëy
- Te yore fitu gaynde
- Bàyyi ko mu dëkk
- Yàgg fa ni daaw
- Sax fa ni céeboo
- Kenn du ko gërëm
|
|
publié le 23 sept. 2019, 07:36 par Fall Papa Oumar
[
mis à jour : 23 sept. 2019, 10:22
]
| - Ana caq ba?
- Caq ba sa Maam soloon
- Summi jox ko sa yaay
- Moom lañu la solal
- Sama doom jii kat
- Silib la judduwaale
- Biig la ko summi
| - Où est le collier ?
- Le collier que ta grand-mère avait porté
- Le collier qu''elle a remis à ta mère
- C'est ce collier qu'on t'a fait porté (cette nuit)
- Ma fille que vous voyez
- Est née avec un slip
- C'est hier nuit qu'elle l'a enlevé.
|
|