XAM | JËF

KII KAN LA? LU MU NU INDAALEEL?
KII KAN LA?

1.      Man nag maa ngi tudd Abdu Xaadir KEBE, di ndongob daara, bu jàng alxuraan ca daaaray S Moor Mbay Siise ca Njaaréem, juge fa dem daara yu S Saaliwu miy sunuu maam ji jur sunu nday, mooy ab taawam.

2.      Ñu mottali fa alxuraan ja, jàng fa liggéey ciy tool , juge fa dem kër S Suëaybu mu S Tuubaa ngir jàng fa xam-xam ak jàngale fa as lëf.

3.      Ci njëlbéenug ati 90 yi nu tukki dem Itaali, def as lëf ci waxtu, jàng fa, liggéey fa, ñibbisiwaat, toog fis tuut, ci liggéeyub yaxantu, dellooti tukki dem Amerig. Ca dëpp ga ca boobale tukki, jaarees na ca réewum Espaañ, jàll ba Faraas, romb ko duggati Itaali

4.      Fa lanu ame mayug sax (permis de séjour) ci diir bii bépp it ñi ngi woon ci njàng mu sax mom ay làkk niki làkkuw Angaleer ak wow Faraas, ginnaaw bi ñu noppee ci wow araab.

5.      Fa Itaali, jotees naa dugg ca jenn daara ju mag jees daan jàngalee làkkuw Itaali ñeel doxandéem yi, ñu naan ca yooya naanu, ngir rekk bëggoon faa jàng as lëf ci mbay waaye mu antoodi ngir i sabab yoy waxtu wi laaju ko.

6.      Joteesoon na faa am nag benn lijaasa bu aju woon ca làkk wa. Wolof nag di lol daa yàgg nekk lees ma xiirtal, mu mas a nekk lu may fogloo di ma jañ cig yittewoo ko

7.      Daara benn barab la bullit yi baaxoo dem cig ndaw di fa dale njàngum Alxuraan ak yar bob diine, njàng mi nag lu ci ëpp daawul weesu mokkalal gone gi Alxuraan ba mu man koo tari te du ko xool, man koo bind it, loolu daa jël ca la gën a néew 3 ba 5 ciy at, ci biir yooyu at gone gi dina ci jàngaale ab yar ci tumbrànke gog dees ko koy tàmbal ngir mu man a yanuji ëlëg coonab dund bi nar a ñëwi. Deesi yalwaanloo ko, mu cay fàggoo ñeme coono, man a lijjanti boppam, man a jànkoonteek jafe-jafey dund gi ci fecci ay lëj-lëjam. Ci yii at it dees na ko ci yar ci toroxlu, muñ, yaru, ami teggiin ak tàmb liggéey ak yëngu. Ginnaaw Alxuraan ji, njàngum xam-xam dikk, di xam-xam yees di jànge ci benn ci barab yees di wooye majaalis, majaalis nag baatu araab la bu tukee ci JALASA di toog na, mu baatub mbooloo bob benn ba mooy majlis di tekki ci wolof ab jataay walla fees di toog, muy tekki ci maanaa benn géew bu mag walla kilifag boroom xam-xam bu diine di toog, dongo ya wët ko mu léen di jàngal xam-xami diine yi, dale ko ci téere yi làmboo Tawhiid, wéetal Yàlla, Fiq, tasawuf ak làkku araab, ak yeneen xam-xam yu am solo yoy day tax a géeju ci diiney lislaam te xam àdduna Foofa it gone gi dina fiy faral di def luy tollu ci ay 3 ba ci ay 5 i at yooyu. Lii daal cig gàttal lenn la ci lees ci man a nettali

8.      Dees na fa jànge lu bari it ca la deesi jàng ca lekolu faraase, ci anam gu  wuute

9.      Daara mooy fees di jànge alxuraan kepp, école franco arabe di jàngu bees di jànge ci làkkaw araab yenn porogaraam ya, ya ca des ci faraase. Su ma waxee loolu nag nga xam li wuutale daara ak leekol bob faraase. Daara su ëmbee maanaan daara ak majaalis niki ma ko waxe woon ca kaw su boobaa ab ''université '' lay tollool maanaam daara ju kawe joj  alxuraan nga fay jànge ju xam làkkuw araab di topp ak xam-xami shariiya yi ak lu sakkan yi yeneen i xam-xam yu yaa yu man a dem dukkee ci falag di xam-xamu bidiw ba ci xayma ak yeneen ak yeneen.

10.  Daara yu njëkk ya lenn wuutalewu leen ak yu leegi yi, ndare xam-xam yu yees yi amutoon te am leegi te nit soxla ko ak man-man bi am leegi ci wàllug koom te amutoon, di sóobu ci suqali daara te di ko jamonoool

11.  Li wuutale daaray taax ak ju kaw mooy jii day faral di jur yalwaan ak po mu bari njàngaan li, joj kaw ji di faral di jur ag farlu ci njàng mi ak sukkandiku ci sa bopp ci taxawug daara ji, rawati na ci dund bi, fii gone gi day dimbali sëñ daara bi ci tool yi, loola it di ko jural ag tàggatu ci liggéey ak tumbrànke ak yeneen ciy jikko yu baax yu jafee fàggoo feneen fu dul fii

Comments