XAM | JËFE

Ankh_Kmt_SMtt

"Ndax nak , fok nu jàng nekk benn. Mebet u loolu du juddoo ci neen. Mbooloo u tund u Afirig ci wàllu caada du lu nuy nemmeeku, waaye lu nuy tabàq la. Bu weesoo wuute gi ci wàllu cadaa, te mu juddóo ci wutéeg dëkkin yi, jiwu Afirig wu nekk benn a ngi ci xel yi, lëngoog bokk tund gi, bokk taariq gi ag yàgg ci ay xeeti wecco yune.

Askan yiy daan ñooy yi gëm seen bopp, gëm ne seen yokkutee ngi seeni yoxo. Ngëm-ngëm googu it du juddu ci neen. Mu ngi sosoo ci ay nekkin ag ay taxawin yu jóge ci njàngaley maam, tassaaroo ci pàcc yu melni njàng muy xamal ag mënal, ci jottaliy xibaar yuy defar askan ag ci dogu ci suuxat caada. Bàyyi sa bopp gi taariq jur, taariq a ko mana faj."

 www.nataal.org/xam-jefe (c) 2015

Sous-pages (1) : 1
Comments